TSK

TSK · Hosea 13:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Te Aji Nekk-Fàww ju Israyil ji du fen, du réccu, ndax du nit bay réccu.»

Job 33:24 TSK

da koy baaxe, daldi ne Yàlla: «Musal ko ba du wàccagum biir pax. Maa ngeek njotlaayam.»

Doo ma wacc njaniiw moos, sa wóllëre wa, doo ko won yàqutey bàmmeel.

Nara dee rekk niy xar, ndee wommat, yóbbu, njub fenk nib jant, ku jub moom leen, njaniiw mëdd seen jëmm, fu sore kërug daraja.

Won nga ma ay yoon coonooki tiis, waaye yaa may dundalaat, ma mucc xóotey suuf.

Mooy mëdd ndee ba fàww! Boroom bi, Aji Sax jeey fompe gépp kanam rongooñi boroom. Buumi gàccey ñoñam it, moo koy doge fépp ci àddina. Aji Sax ji kat wax na ko.

Yaw yaa ma wacc,» kàddug Aji Sax jee, «dellu gannaaw, ma duma la, sànk la. Muñ naa ba sonn.

Kon nag biralal waxyu, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen sama ñoñ, maa ngii di ubbisi seeni bàmmeel, dekkale leen ca seeni bàmmeel, délloosi leen kaw suufas Israyil.

Israyil, ag reewandeem a ko tiiñal, te taxul ñu délsi ci seen Yàlla Aji Sax ji. Loolu yépp taxul ñu sàkku ko.

Ndax kat ba Yàlla dàqee Israyil, ca la àddina juboo ak Yàlla. Kon nag bu leen Yàlla délloosee, ana lu muy jur lu moy ndee-ndekki?

Ci nit la ndee dikke ci àddina. Moo tax ci nit itam la ndekkite dikke ci àddina.

Noo ngi onk ndax diis, li feek nu ngeek sunuw yaram, xayma bi nu soloo nii. Du summiku lanu namm, waaye solu teg ko ci lanu namm, ngir li jëm ndee, daldi suux ci biir ndund.

Ndegam gëm nanu ne Yeesu dee na, ba dekki, noonu it lanu wara gëme ne Yàlla mooy dekkal way dawlu ñi gëmoon Yeesu, ba boole leen ak Yeesu, indaale.

Ba mu ko defee géej jébbale néew ya woon ca moom, ndee ak njaniiw jébbale néew ya woon ca moom, ñu daldi àtte ku nekk ca say jëf.