TSK

TSK · Hosea 2:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Dingeen wax ci seen xel ne: «Sunu doole ak sunu njàmbaaru bopp moo nu may jii alal.»

Nangu nañu ay dëkk yu tata wër, ak suuf su nangu, aakimoo kër yu fees ak gépp ngëneel, aki teen, ak tóokëri reseñ, ak garabi oliw, garab yay meññ, ne xas; ñuy lekk ba suur. Ñu regg, di xéewloo sa mbaax gu réy gi.

Ñoo dox wuti Misra te laajuñu ma, xanaa di sàkku rawtub Firawna, di keppaaroo keppaarug Misra.

Wóoy ngalla ña wàcci Misra, di wuti wall; di sukkandikoo ay fas, tey yaakaari watiir ndax bare ga, aki gawar ndax lim bu takku ba te xooluñu ci Aji Sell ju Israyil, sàkkuwñu kooku di Aji Sax ji.

Waaw, ana seen yàlla yi ngeen sàkkal seen bopp? Bu leen musiba dikkalee, nañ leen wallu, bu ñu ko manee! Gannaaw yeen waa Yuda, ni seeni dëkk tollu la seeni yàlla tollu!

Yeen doom yu woyof kumba yi, waññikuleen, ma fajtal seen woyof kumba.»

Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Sa damm-damm du faju, sa góom du wér.

Du mel ni kóllëre ga ma fasoon ak seeni maam keroog ba ma leen jàppee ci loxo, génne leen réewum Misra. Ndax ñoom ñoo fecci sama kóllëre, te man may seen boroom kër.» Kàddug Aji Sax jee.

Su bés baa, ci yooyu fan,» kàddug Aji Sax jee, «bànni Israyil ay ànd ak Yudeen ñi, dikk di jooy, di sàkku seen Yàlla Aji Sax ji.

Ma jaareeti fa, xool la, gis ne mat ngaa séy. Ma tàllal sama mbubb, sànge ko sa yaramu neen, ba noppi giñal la, dikke la kóllëre. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Nii laa la moome.

Li ngeen mébét ci seen xel du am mukk. Yeena ngi naan: ‘Nan mel ni xeet yépp, mel ni waasoy réew yi, di jaamu bant ak doj.’

Moom it waa Asiri ya la xédd, ñuy kàngam aki jawriñ, xarekat yu ràngu ba solu ba jekk, di ndaanaani gawar, ñoom ñépp di xale yu góor yu sopplu.

Garab gi nga gis muy màgg di réy, njobbaxtal lay laal asamaan, ñu di ko séen ci àddina sépp,

Mboolem waa àddina di neen ci moom. Nu ko neex lay def ak gàngoori xarey asamaan ak waa suuf, te kenn du fél loxoom mbaa mu naa ko: «Ana looy def nii?»

Hosea 1:2 TSK

¶ Ba Aji Sax ji tàmbalee yóbbante Ose kàddoom, Aji Sax ji da ne ko: «Demal takki jabaru gànc, nga am ca doomi ngànctu, ndax réew maa ngi gànctu ngànctu gu réy, dëddu ma man Aji Sax ji.»

Ma daldi ñibbi, ba ñu nangu seenug tooñ, sàkku ma. Bu ñu jàqee lañuy daw wutsi ma.»

Dees na topp waa Samari, nde ñoo fippu ci seen kaw Yàlla. Saamar lañuy fàddoo, seeni doom, ñu rajaxe leen, seen jigéeni wérul, ñu butti.