Sama doole, sama kaaraange, Ki Sax a; te mooy sama wall tey. Mooy sama Yàlla, ji may tagge, sama Yàllay maam, ji may joobe.
TSK
TSK · Isaiah 12:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñeel Daawuda. Aji Sax jee may leeral, di ma wallu. Ana ku may ragal? Aji Sax jeey aar sama bakkan. Ana ku may tiit?
Cant ñeel na Yàlla bésoo bés. Moo nuy jaboote. Yàllaa nuy musal. Selaw.
Yal nañu rus, jàq ba fàww. Yal nañu torox, sànku.
Dama lay sant, yaa ma nangul, wallu ma tey.
Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
ku ci nekk mel ni seelukaayu ngelaw, di kiiraay ci ngëlén, mel ni wali ndox ci suuf su ne sereŋ, mbaa keppaaru doj wu mag ci àll bu mar.
Aji Sax ji yaa may wallu, nu di la woy, ànd aki xalam, sunu giiru dund, fa sa biir kër, yaw Aji Sax ji.
Yeen waa àddina, catoo cat, walbatikuleen fi man, mucc. Man maay Yàlla, du keneen.
Man ci sama bopp maa leen di dëfal. Ana lu ngeen di ragal ci nit kuy dee, doom aadama ju bokk akum ñax aw demin?
Naxi neen kay lañu jële ca xërëmi tund yu ndaw ya ak coowal kaw tund yu mag ya. Muccu Israyil kay, fi sunu Yàlla Aji Sax ji.
Waaye waa kër Yuda, maa leen di yërëm. Seen Yàlla Aji Sax ji laa leen di walloo, waaye duma leen walloo fitt mbaa saamar, mbaa ay xare, mbaa ay fas aki gawar.»
¶ Awma lu may rus ci xibaaru jàmm bi, ndax kat mooy manoorey Yàlla jiy musal képp ku ko gëm, dale ci Yawut bi, teg ci ki dul Yawut.
Ña ngay àddu ca kaw, naan: «Texee ngi fi sunu Yàlla, ki toog ci ngàngune mi, ak ci Gàtt bi!»