TSK

TSK · Isaiah 14:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Seen jaam yu góor ak seen jaam yu jigéen, nangeen leen jële ci xeet yi leen wër. Ci ñooñu ngeen di jënde ay jaam, góor ak jigéen.

Watiiri xarey Yàlla di ñaar fukki junni (20 000), ba ci junniy junni. Boroom bi ne ca seen biir, di boroom tundu Sinayi fa biir sellngaam.

Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: «Maa ngii di tàllal xeeti jaambur ñi loxo, ñee ma yékkati raaya, wooye leen; ñu fab say doom yu góor, indi, tungóom sa doom yu jigéen, délloosi;

Séentul fi la wër ba gis: ñoom ñépp a daje, di la fekksi, sa doom yu góor a dikke fu sore, te sa doom yu jigéen it dees leena fab, indaale.

Ña la daa néewal, seeni doom a lay sukkalsi. Ña la daa ñàkke worma, mujj di fóon say tànk. Dees na la wooye «Dëkkub Aji Sax ji», mbaa «Siyoŋ, màkkaanu Aji Sell ju Israyil.»

Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Maa ngii di yóbbu Yerusalem ci jàmm ju mel ni géej, ak waamey koom muy wal, bawoo ci xeet yi. Yeenay tooge luppu Yerusalem, di nàmp, uufu ciy óom, mu di leen raay.

Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay dégtal Raba, dëkku Amoneen ñi, coowal xare ci seen biir, tund wa gental, dëkk-dëkkaan ya tàkk ba jeex, ba keroog Israyil futti ñooña ko futti woon.» Aji Sax jee ko wax.

Dina yékkati ay kàddu dal ci Aji Kawe ji, dina fitnaal aji sell yu Aji Kawe ji te dina fexee soppi takkinu jamono yi ak yoonu Yàlla wi. Dees na teg aji sell yi ci loxoom diiru ñetti jamonook genn-wàll.

Xeet yépp laay dajale ci kaw Yerusalem, ngir xare. Dëkk bi lees di nangu, sëxëtoo kër yi, tëdde jigéen ñi. Genn-wàllu dëkk beey génn, jëm ngàllo, waaye ndesu askan wi, deesu leen dagge ci dëkk bi.

Dañu noo ñaan, ba di nu tinu, ngir nu may leen, ñu def seen loxo ci ndimbalu jàpplante gi jëm ci gëmkat ñu sell ñi.

¶ Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel.

Ñenn ci jàngub Seytaane bi, ñooñuy fen, di tuddoo ay Yawut te duñuy Yawut, maa ngii di leen xiirtal, dikkloo leen, sujjóotloo leen fi sa kanam, ba ñu xam ne man maa la sopp.

Ndokklee, asamaan, Ndokklee, yeen ñu sell ñi itam, ak ndawi Yàlla yeek yonent yi, ndaxte Yàllaa leen àtteek dëkk bii, mbugal ko.