TSK

TSK · Isaiah 4:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Bésub ay, mu yiire ma mbaaram, làq ma, ma làqoo xaymaam, aj ma ciw doj, ma raw.

Aji Sax jee lay sàmm, Aji Sax jee lay yiir, féete la ndijoor.

Mu doon seen bérab bu sell, di doj wuy fakktale, xeer wuy féle, ci ñaari këri Israyil, te dim yeer, dig fiir, ñeel ku dëkk Yerusalem.

Aji Sax jeey yékkati kàddoom gu màgg, wone diisaayu loxoom, ànd ak tàngooru meram, ak sawara wuy xoyome, ak waameek ngëlén, ak tawub doji yuur.

ba sama bokk yi dëkke sancub jàmm, ci dëkkuwaay yu wóor, dal-lukaay yu dal xel.

¶ Ngëm la Nóoyin dégge waxyub Yàlla bu jëm ci lu kenn gisagul woon, te ragal Yàlla la sàkke gaal, ngir musal njabootam. Ngëmam it la tiiñale àddina, ba ab céram di njub gi ngëm di maye.