TSK

TSK · Isaiah 49:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Maa leen di def sama ñoñ, di seen Yàlla. Dingeen xam ne man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen di teggil sas, yi leen waa Misra teg.

Xeet yee tàbbi pax ma ñu gasoon, fakktaloo fiir ga ñu làqoon.

Yal nañu rus, jàq ba fàww. Yal nañu torox, sànku.

Manase song Efrayim, Efrayim song Manase, ñu mànkoo, noonoo Yuda. Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, meddiwul ba tey.

Léegi nag yaw Yanqóoba, yaw Israyil mii, Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: «Bul tiit, jot naa la. Dama laa woo ci sa tur. Maa la séddoo.

ngir xamees penku ba sowu, ne lu dul man neen la. Aji Sax ji man a, du keneen.

Sama tur wu sell laay xamle fi digg Israyil sama ñoñ, te dootuma seetaan ñuy teddadil sama tur wu sell. Yéefar yi dinañu xam ne maay Aji Sax ji, ku Sell ku Israyil ki.

Ña ngay woy woyu Musaa jaamu Yàlla ba, ak woyu Gàtt bi, naan: «Yaw Boroom bi Yàlla Aji Man ji, yaa réy te yéeme ay jaloore. Yaw Buuru askan yi, yaa jub te dëgguy doxalin.

Ma gis ne jigéen ji daa naan ba màndi ci deretu ñu sell ñi ak deretu ñi doon seedeel Yeesu. Ba ma ko gisee, jaaxle naa lool.