TSK

TSK · Isaiah 64:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Ezra 9:7 TSK

¶ La ko dale ca sunu janti maam ba bésub tey jii, nu ngi ci moy gu réy. Sunuy bàkkaar tax na buuri réew yi teg nu loxo, nook sunuy buur ak sunuy sarxalkat, ñu di nu rey, di nu jàpp njaam, di lël sunu alal, di nu torxal ba sunu jonni yàllay tey.

Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.

Damay xaar Aji Sax ji, di ko xaare xol, di yaakaar kàddoom.

Aji Sax ji déy a leen namma baaxe, moo ko tax di jóg moos ngir yërëm leen, nde Aji Sax jeey Yàllay njubte. Ndokklee képp ku ko yaakaar!

Aji Sax ji, nun kay gàcce ñeel na nu, nook sunuy buur ak sunuy kilifaak sunuy maam, ndax moy nanu la.

Hosea 7:7 TSK

Ñoom ñépp a tàng jérr nib taal, te ñooy xoyom seeni njiit, seen buur yépp a daanu, te kenn ci ñoom woowu ma wall.

Te du càkkéef gi rekk, waaye nun ci sunu bopp itam, ci lanu, nun ñi jot ab dawal ci Noo gi, nun ci sunu bopp sax nu ngi binni sunu biir xol, ndax yàkkamtee jot céru doomi Yàlla, ba sunu njotug yaram mat.

Mooy noonu ñu binde rekk ne: «Lu bët gisul, nopp déggu ko, xel daju ko, Yàllaa ko dencal ñi ko sopp.»

Su ko defee seen ngëm tax Almasi dëkke seen xol, ngeen sax ay reen yu sampe ci biir cofeel,

tey séentu Doomam Yeesu mi mu dekkal, mu dikk bàyyikoo asamaan, moom mi nu jot ci sànj miy dikk.

Waaye réew mu ko gën lañu doon sàkku, te mooy réewum asamaan. Looloo tax Yàlla rusul ñu di ko tudde seen Yàlla, ndax waajalal na leen ab dëkk.

¶ Ma daldi gis asamaan su bees ak suuf su bees. Fekk na asamaan su jëkk sa ak suuf su jëkk sa wéy, te géej amatul.

¶ Ci kaw loolu malaaka mi won ma dexu ndoxum dund mu leer nàññ ni doju kiristaal, ndox ma wale ca ngàngunem Yàllaak Gàtt ba,