¶ «Maa ngi nii di indi mbënnu ndox ci kaw suuf, mu far lépp luy dund lu asamaan tiim; te lépp lu nekk ci kaw suuf dina dee.
TSK
TSK · Isaiah 8:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Moom la Salmanasar buurub Asiri song, mu nangul ko, di ko fey galag.
bawoo it ci yeneen mbooloo ya Asnapar mu mag mu tedd ma toxaloon, sancal leen ca dëkki Samari ak li des ca Wàllaa Dex, ak ñoom seen.
mu yilif géej ba géej ak dex ba ca cati àddina.
Aji Sax jee lay dikke, yaak saw xeet ak sa waa kër baay, ay bés yu tar yu masula am, ba Efrayim dëddoo Yuda ba tey, te buurub Asiri la koy sababe.»
Mu ngi naan: «Xanaa du sama jawriñ yépp a diy buur?
Yeena naay: «Danoo wóllëranteek ndee, njaniiw lanu digool, ba du nu moom, ba bu yaru musiba dikkeek diisaayam, du nu laal? Noo def ay fen sunu rawtu, ay wor di sunu làquwaay.»
Dees na wormaale turu Aji Sax ji fa sowu, wormaale teddngaam ba penku. Bu noon bi agsee ni walum dex, ngelawal Aji Sax jee koy wal, mu daw.
Géej ay mëdd Babilon, mu sàngoo gannaxam yu jallaañoo,
Bu juróom benn fukk yeek ñaar ciy àppi juróom ñaar weesee, dees na bóom ku ñu fal, te kenn du ànd ak moom. Gannaaw loolu kilifa dina ñëw, ànd ak gàngooram, yàqte dëkk beek jaamookaay bi. Waaye kilifa googu lu mel ni mbënn a koy mujje. Dogal nañu ne yàqte gi dina wéy ba keroog xare biy jeex.
Mboolooy xare yi dinañu def um wal nig dex, dal ci kawam, waaye dees na leen rajaxe, ñook genn kilifay mbooloom kóllëreg Yàlla gi.
Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, kiy laal suuf, mu ne soyox seey, mboolem lu ci biiram di jooyoo; suuf fuddoondoo ni dexu Niil, dellu rës ni dexu Misra.
Ab saamar la ñooñuy yilife Asiri, réewum Nimróot mooma ca biiri buntam. Kilifa gi ñu dige moo nuy xettleek Asiri, bu ñu nu songee, ba joggati sunu suuf.
Dafa mel ni nit kiy tabax kër, gasa gas ba mu xóot, daldi samp kenu ga ca kaw doj wa ca suuf. Mbënn ma dikk, wal ma rëkk kër gaak doole te manu koo yëngal ndax tabax bu wér ba ñu ko tabaxe.
¶ Mu neeti ma: «Ndox yi nga gis jigéenu moykat ji toog ci nag, mooy niti xeet yeek mbooloo yeek askan yeek làmmiñ yi.