ne yàcc, génne seeni tata, di lox.
TSK
TSK · James 1:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Damaa gis ku bon di note, te sëq ni garab gu naat fa mu fekk baax,
Yoonu tarxiis kay, nga leen teg, daane leen, ñu sànku,
te sa mer ak sa xadar a tax, nde yaa ma fab, xalab.
Wóoy ngalla Efrayim, kaala gu yànj ga ay màndikatam di sagoo! Taaram bu yéeme baa koy réer, ni tóor-tóor yu wow, te ma nga toŋ ca coll, wa ña biiñ man dëkke, fa tiim xur wu nangu wa.
Ñax ma wow, tóor-tóor ma lax fa ko noowal Aji Sax ji wale. Askan wi kay, am ñax doŋŋ la.
Ca ëllëg sa, ba jant bay fenk, Yàlla yebal aw sax, mu song lawtan ga, mu wow.
¶ «Jenn waay la woon ju bare alal, di sol yérey tànnéef yu rafet, di dunde lu neex bés bu set.
¶ Kaayleen nag ma wax leen, yeen boroom alal yi, jooyleen te yuuxu, ndax mitit yi leen di dikkal.
ba bu Sàmm bu mag bi feeñee, ngeen jot kaalag daraja gu dul furi.