TSK

TSK · James 1:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 29:12 TSK

Néew-ji-doole woote, ma wallu, boole ci jirim bu tumurànke.

Woyleen Yàlla, teral turam, xàllal-leen kiy war niir yi, Ki Sax moo di turam. Bànneexuleen fi kanamam.

Raxasuleen ba set wecc, jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam, te ngeen ba lu bon.

«Xanaa du lii moo di koor gi ma taamu: yolomal jéng yu metti, fecci buumi noteel, afal ku diis; dog lépp luy xeetu noteel?

mi maye bakkanam ngir njotug sunuy bàkkaar, ba musal nu ci jamonoy tey ju bon ji, ci coobarey Yàlla sunu Baay,

Bunu tàyyi ci def lu baax, nde bu jotee rekk nooy góob, ndegam yoqiwunu.

¶ Gannaaw nag yeena dekkeendoo ak Almasi, sàkkuleen la fa kaw, fa Almasi tooge ca ndijooru Yàlla.

Waaye su dee ab jëtun bu ami doom mbaa ay sët, ñooñoo wara jëkka jéema jëfe ag ragal Yàlla ci seen biir kër, ba delloo njukkal seen waajur, ndax loolu la Yàlla rafetlu.

James 4:4 TSK

¶ Bokkaalekat yi ngeen doon! Xanaa xamuleen ne xaritoo ak àddina moo di noonoo ak Yàlla? Kon nag ku namma def àddina ab xarit, ab noonu Yàlla ngay doon.