Seeni fitt ñaw na, seen xala yépp noppi na, seen wewi tànki fas ni xeer. Bu tànki watiir ya dawee, nga defe ne callweer a.
TSK
TSK · Jeremiah 4:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yéene bii ñeel na Misra: Aji Sax jaa ngii war niir wu gaaw, jëm réewum Misra. Yàllantuy Misra yég ko, di lox, fitu waa Misra rëcc.
Baatu ndaw su jagadi laa dégg, ma nga jàq, di matub taawam. Baatub Siyoŋ, dëkk bu taaru baa! Ma ngay àppaat, tàllal yoxo ya, naan: «Wóoy, ngalla man; ne yàcc ci loxol bóomkat yi!»
«Wóoy man, yàqu naa! Ndaw góom bu metti! Dama noon lii jàngoro doŋŋ a, naa muñ!
Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Lu mel ni jaxaay a ngii naa jàyy, firiy laafam, këfsi Mowab.
¶ «Rab wu jëkk waa nga mel ni gaynde, am laafi jaxaay. Naka laay xool, ñu buddi laaf yi, yékkatee ko ci suuf, taxawal ko, mu taxawe ñaari tànk ni nit, ba noppi ñu jox ko xelum nit.
Aji Sax ji la mer ma diib, doole ja bare; te du ñàkka topp ku tooñ, ag tooñaangeem. Aji Sax jeey daagoo biir callweer ak ngëlén, niir yi di pëndub tànkam.
Seeni fas a gëna gaawi segg, gëna aay tilli timis. Fu sore la seeni gawar jóge, tëbal, naaw nig jaxaay ju ne jàyy, lekkum rëbbam.