Exodus 21:26
TSK
¶ «Ku dóor ab jaamam bu góor mbaa bu jigéen, ba tuur bëtam, na ko goreel ndax bët ba.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Ku dóor ab jaamam bu góor mbaa bu jigéen, ba tuur bëtam, na ko goreel ndax bët ba.
Sañ ngeen leena donale seen doom yi leen di wuutu, ñu doon seen ngàllo seen giiru dund. Ñooñu sañ ngeen leena def ay jaam, waaye su dee ci seen diggante, yeen bànni Israyil, buleen di soxorante ci biir kilifteef.
¶ Buleen gàddu àqu liggéeykat, baadoolo bu néew doole ci seen biiri bokk, mbaa ci seen dëkkandoo yiy doxandéem ci seen dëkk yi ci réew mi.
¶ Yeen it sang yi, jëfeleen noonu seen diggante ak seeni jaam, bàyyileen di tëkkoo, te ngeen xam ne yeen ak ñoom a bokk benn Boroom fa asamaan, te xejj ak seen amul fa moom.