TSK

TSK · Lamentations 1:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 6:15 TSK

Samay xarit a ma wor ni yol moo fekk ŋiis. Dañoo mel ni dex yoo fekk ndox ma jeex,

Job 19:13 TSK

Samay bokk, mu soreleek man, samay xame sax ñooru ma.

Naqar a ngi may rey, tiis di wàññi samay fan, sama doole ŋiis ndax sama njubadi, samay yax semm.

Naa xaacu, woo Yàlla, sama baat fa Yàlla, ngir mu déglu ma.

Amul ci ñi nga jur, kenn koo dese ku lay wommat. Amul ci doom yi nga yar, kenn ku lay jàpp ci loxo.

Yaw Yerusalem mu tas mi, ana looy def nii, di solu ba yànj, gànjaroo wurus, tusngalu, yàkkleey gët? Yaa ngi caaxoñu ci neen: say xéddkat wacc nañu la, sa bakkan lañuy wut.

Nañu gaaw dëbbeel nuy jooy, gët taa, rongooñ wal.

Aji Sax ji nee: «Yeen waa Yerusalem, yéegileen tundi Libaŋ, yuuxu. Àddooleen fa Basan, xaacu, te yuuxoo fa Abarim, nde seen soppe yépp a rajaxoo!»

Sobey Siyoŋ ca pendalam, te bàyyiwul xel ag mujam. Jéllam ba yéeme na, te amul ku ko dëfal. Siyoŋ nee: «Éy Aji Sax ji, xoolal sama njàqare; noon bi déy, am na ndam!»

Samay soppe laa woo wall, ñoom ñu wor ma. Samay sarxalkat ak samay mag di wuti ab dund bu ñu leqlikoo, far faatu ci biir dëkk bi.

Samay gët a giim ndaxi rongooñ, samay butit fuddu, xol ŋiis, jeex tàkk: ci tasteg samaw askan; xale yeek gone yiy nàmp ne lasar fi mbedd yi!

maa ngii nag di dajale mboolem sa far yi la doon bége, ñi nga bëgg ñépp ak ñi nga bañ ñépp. Maa leen di dajalee fu nekk ci sa kaw, ba noppi ñori la yaramu neen, ñu gis la nga ne duŋŋ.

Hosea 2:7 TSK

Ñoom seen yaay moo gànctu, ki leen ëmb moo def lu gàccelu, naan: “Damay toppi sama far, yi may jox sama lekk ak samag naan, ak samag wëñ ak sama lẽe ak samag diw ak sama biiñ.”

Menn mébét lañu bokk, te dinañu yékkati seen doole ak seen sañ-sañ, jox ko rab wi.