TSK

TSK · Lamentations 2:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mu ne: «Leer ga kay dëddu na Israyil, dem ngàllo, ndegam jëlees na gaalu Yàlla ga kay!»

Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji, te sujjóot fa ndëggastalam. —Kee sell!

Moo yaw biddiiwu njël, bi noon ràññ, tey nga xàwwikoo asamaan ba fii! Yaw mi daa daan xeet yi, tey ñu gor la, nga goor.

Sa soppe yépp a la fàtte, kenn faalewu la ci, ndax dumay noon laa la duma, yar la yar bu tar ngir sa ñaawtéef ju réy ak sa bàkkaar yu bare.

Yeen mboolem ñiy jaare yoon wi, lii safu leen, waaye seetleen rekk ba gis ndax wenn mitit dab na mitit wi ñu ma teg, te Aji Sax ji naqarale ma ko ci jantub tàkktel sànjam.

Aji Sax jee xëpp am sànjam, sotti tàngooru meram, moo jafal sawara fi Siyoŋ, ba xoyom kenu ya.

Kon Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maay xadaru, riddil ngëlén, mer, walal waame, am sànj yuri ponkali doji sànkute.

Yaa doon malaakam serub mu ne ràññ, di aare, ma tabb la fa kaw tundu Yàlla wu sell wa, ngay daagoo digg doj yuy tàkk.

Bu sa leer feyee, maay muur asamaan, lëndëmal ay biddiiwam, sànge jant bi aw niir, weer wi noppee leeral.

Yeesu ne leen: «Séen naa Seytaane mu fàqe asamaan ni ag melax.