TSK

TSK · Leviticus 1:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Lakkal kuuy mépp ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, ñeel Aji Sax ji, di xeeñ xetug jàmm; saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji.

Na boroom sarax bi raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

te yót ko doomi Aaróona yu góor yiy sarxalkat yi. Na sarxalkat bi sàkk barci-loxob sunguf su mucc ayib soosu ànd ak diw gi, te boole kook cuuraay li lépp. Na sarxalkat bi def cér boobu saraxu baaxantal, lakk ko ca kaw sarxalukaay ba, muy saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Na sarxalkat bi lakk lenn ci mbool mu mokk mi ànd ak diw, boole kook cuuraay li lépp, muy saraxu baaxantal, te di saraxu sawara.

Na sarxalkat bi boole loolu lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy ñamu sawara, ñeel Aji Sax ji.

Ba loolu weesee Musaa boole yérey biir yi, ak yeel yi, raxas, ba noppi lakk kuuy mi yépp ca sarxalukaay ba. Loolu saraxu rendi-dóomal la, ngir xetug jàmm. Saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.

Loolu wéy, mu raxas yérey biir yi, ak yeel yi, teg ko ca kaw saraxu rendi-dóomal ba, lakkaale ko ca.

¶ «Su dee sarxe jur gu gudd, muy saraxu rendi-dóomal, mbaa sarax bu muy wàccoo aw xas, mbaa saraxu cant ci biir jàmm, ñeel Aji Sax ji,

Ñaareelu xar mi, sarxal-leen ko diggante ngoon ak jant bu so, mu ànd ak saraxu peppam ak saraxu tuuram niki ci suba, ngeen def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Jurug yafal, ma defal la saraxu rendi-dóomal, saxar sa jollee ca kuuyu sarax ya, ma boole ca saraxu nag ak sikket. Selaw.

Maa leen yóbbu réew ma ma leen giñaloona jox, teewul fu ñu gis tund wu kawe, mbaa garab gu sëq, rendi nañu fa seeni sarax, jooxe fa seen jooxe yi may merloo, taal fa seen saraxi cuuraay, tuural fa seeni tuur.

¶ Am na néeg buy ubbikoo ci biir mbaaru bëj-gànnaar ba féete biir. Fa lañuy raxase yàppu saraxu rendi-dóomal.

te ngeen di doxale cofeel, ni Almasi mi nu sopp, ba jooxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara, ngir xetug jàmm, ñeel Yàlla.