TSK

TSK · Leviticus 16:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Mbubb mu gudd mi nag, nanga ko ràbbe wëñu lẽe, kaala gi itam di wëñu lẽe. Te laxasaay gi, liggéeyu ràbb bu rafet lay doon.

Bu ñuy duggsi ci xaymab ndaje mi, nañu jàpp, ndax ñu baña dee, nañu jàpp itam, bu ñuy liggéeysi fi sarxalukaay bi, di taal saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.

¶ «Indil Aaróona aki doomam ba ci bunt xaymab ndaje mi, nga sang leen ci ndox mi.

Sarxalkat bi day sol mbubbam mi ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew ak tubéyi njiitlaayam ji ñu ràbbe wëñ gu ëccu ba sew. Na tonnee ca sarxalukaay ba dóomu saraxu rendi-dóomal bi, daldi teg dóom bi ci wetu sarxalukaay bi.

¶ Ci kaw loolu Musaa indi Aaróona aki doomam yu góor, ñu sangu,

Kii màgge fi kanamam ni njëmbat, te nirook reen bu fette ag kekk. Dub taar, du yànjaay bu nu koy niire, du meloom wu nu koy soppe.

Luke 1:35 TSK

Malaaka mi ne ko: «Noo gu Sell gi mooy wàccsi ci yaw, dooley Aji Kawe ji yiir la. Moo tax itam ku Sell kiy juddoo ci yaw, dees na ko wooye Doomu Yàlla.

¶ Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley ndee, te mooy Seytaane.

Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu, ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.