TSK

TSK · Leviticus 17:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Ab doxandéem, buleen ko lor, buleen ko not, ndaxte yeen itam ay doxandéem ngeen woon fa réewum Misra.

Jàdd nañu xaat yoon wa ma leen tegoon. Dañoo sàkkal seen bopp sëllu wu ñu móol, di ko sujjóotal ak a sarxalal, naan: “Israyiloo, seen yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!”»

Dogal a ngii, di lu leen war fàww, ak fépp fu ngeen dëkk: lépp luy nebbon mbaa deret, buleen ko lekk.»

Aji Sax ji ne Musaa: «Yaa ngi nii di tëddi fa say maam. Mbooloo mii nag dinañu tàmbali di gànctuy topp yeneen yàllay doxandéem yu waa réew, ma ñu jëm ca seen biir. Dinañu ma wacc, fecci sama kóllëre gi ma fasoon ak ñoom,

Mu ne: «Su waay fasee jabaram, mu dem doon jabaru keneen, Su waa ja jëlaatee ndaw sa ëllëg, Loolu du sobeela sobeel réew mii? Moona yeen gànctu ngeen aki fari far, Ana nu ngeen mana délsee fi man?» Kàddug Aji Sax jee.

Li may wax kay moo di yooyu sarax, rab yi la ñeel, waaye du Yàlla, te bugguma ngeen bokk ak rab yi lenn.

yi ngeen doon dunde démb, ngeen àndoon ci ak doxalinu àddinay tey jii, ak ku bon kiy kàngamu boroom baat yi ci jaww, ji asamaan tiim, boroom noo gi wéye liggéeyam ci biir aji déggadi ñi, tey.

¶ Kenn ci juróom ñaari malaaka, yi taawu juróom ñaari ndab yi nag dikk, ne ma: «Kaay, ma won la mbugalu jigéenu moykat ju mag, ji toog ci ndox mu bare.