TSK

TSK · Leviticus 3:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Na doomi Aaróona yi boole yooyu lakk ci kaw sarxalukaay bi, mu tege ci kaw saraxu rendi-dóomal bi ci kaw mattum taal bi. Saraxu sawara la ngir xetug jàmm ñeel Aji Sax ji.

Nañu nekkal seen Yàlla ay nit ñu sell, te baña teddadil seen turu Yàlla, ndax saraxi sawar yi ñeel Aji Sax ji, te di seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Kon nag dañoo wara sell.

«Waxal Aaróona ne ko: Muy tey muy ëllëg ba fàww, góor gu askanoo ci yaw ak maas gu mu mana bokk, su amee sikk du mana agsi ba ci sarxalukaay bi, di joxe ñamu Yàllaam.

Buleen nangoo lenn lu ni mel ci loxol doxandéem it, di ko jébbal seen Yàlla, muy saraxu ñamam. Deesu leen ko nangul, ndax la matadi ca moom mooy sikk sa.»

Ñu ŋa ma, ŋàpp, ni gaynde, guy yëmmook a fàdde.

Bu ngeen ma daan indil sama céru ñam, muy nebbon, di deretu sarax yi, dangeen di dugalaale sama biir bérab bu sell bi ay doxandéem yu xaraful, du ci jëmm, du ci xol. Noonu ngeen sobeele sama kër gi. Fecci ngeen sama kóllëreek yeen ndax seen jépp jëf ju siblu.

«Waaye yeen yeena teddadil sarxalukaayu Aji Sax ji, nde yeena xalaat ne lu sobewu la, te aw yàppam, aw ñamam jarul dara.

Dungeen mana naan ci kaasu Sang bi, naan ci kaasu rab yi. Dungeen mana bokk lekk ci ndabal Sang bi, bokk lekk ci ndabal rab yi.