TSK

TSK · Leviticus 6:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Ndegam sarxalkat bi ñu diw, fal ko, moo moy, ba yóbbe mbooloo mi tooñ, na indil Aji Sax ji yëkk wu ndaw wu amul sikk, muy saraxu póotum bàkkaar ndax bàkkaar ba mu def.

Deesu ko lakkaaleek lawiir. Seen cér la bu leen Aji Sax ji sédd ci saraxi sawaraam. Lu sella sell la, mel ni saraxu póotum bàkkaar ak saraxu peyug tooñ.

Ba loolu weesee Musaa boole yérey biir yi, ak yeel yi, raxas, ba noppi lakk kuuy mi yépp ca sarxalukaay ba. Loolu saraxu rendi-dóomal la, ngir xetug jàmm. Saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.

Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.

¶ Ñi ñu masa fal sarxalkat nag bare nañu, te tëlee wéye fàww seen sas moo tax, gannaaw ñoom ñépp ay dee.