TSK

TSK · Leviticus 7:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Su fekkee ne nit ki dafa moy lenn ci santaaney Aji Sax ji ci lu warul lu mu def, su ko xamul it, tooñ na, te dees na ko ko topp.

Aaróona ne Musaa: «Xoolal rekk tey ni bànni Israyil indile Aji Sax ji seen saraxu póotum bàkkaar ak seen saraxu rendi-dóomal, te teewul lii dal ci sama kaw! Bu ma lekkoon tey ci yàppu saraxas póotum bàkkaar bi, ndax dina neex Aji Sax ji?»

¶ «Mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf, sibleen ko. Deesu ko lekk.

¶ «Bu ngeen dee rendil Aji Sax ji saraxas cant ci biir jàmm, sarxal-leen ko ni mu ware, ndax ñu nangul leen.

¶ «Su nit jëlee jabar ab jigéenam bu mu bokkal jenn ndey mbaa benn baay, ñu séq lalu séy, loolu gàcce la. Nañu leen dagge ci biir bànni Israyil, ñooñuy gis. Gannaaw moo tëdde ab jigéenam, na wéetoo añu ñaawtéefam.

Buñu leen di bàyyi it ñuy gàddu bàkkaar buy laaj peyug tooñ, ngir lenn lu ñu lekk ci sarax yu sell yooyu. Man Aji Sax ji maa sellal yooyu sarax.»

Buleen nangoo lenn lu ni mel ci loxol doxandéem it, di ko jébbal seen Yàlla, muy saraxu ñamam. Deesu leen ko nangul, ndax la matadi ca moom mooy sikk sa.»

«Lu may doye seen sarax yu bare?» la Aji Sax ji wax. «Damaa suur seen saraxi rendi-dóomali kuuy, suur nebbonu juru yar gi, deretu yëkk ak xar ak sikket it, safu ma.

di tooge diggi bàmmeel, di fanaan bérab yu làqu; di lekk yàppu mbaam, seeni cin def ñam yu sobewu,

¶ Aji Sax ji dafa wax ci askan wii ne: «Ñeeka bëgg ub taxawaalu, baña téye seen tànk. Moo tax man Aji Sax ji bégewuma leen. Léegi ma bàyyi xel seenug mbon, ba mbugale leen seeni moy.»

Ki bàkkaar daal mooy dee. Doom du gàddu ñaawtéefu baay, baay it du gàddu ñaawtéefu doom. Njekk réerul boroom, mbon réerul boroom.

Amos 5:22 TSK

Ngeen defal ma saraxu rendi-dóomal, mbaa saraxi pepp it, duma ko nangu. Seen saraxu jur guy cant ci biir jàmm, faalewuma.

Yeena ngi naa: “Ndaw lu soof,” di ciipatu.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Jur gu ñu sàcc ngeen may indil, ak guy soox, ak gu wopp, loolu mooy seen sarax! Nu ma koy nangoo ci seeni loxo?» Aji Sax jee ko wax.

Gannaaw gi la jagoo màndargam xaraf, mu firndeel àtteb njubam gi ngëmam waral, te fekkul mu xaraf. Noonu la Ibraayma mana nekke maamu mboolem gëmkat ñi. Looloo tax muy maamu mboolem ñi xaraful, te gëm, ndax ñu waññal leen seen ngëm, ab àtteb ñu jub.

«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar, moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba,» ngir nu deeyal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»