TSK

TSK · Leviticus 7:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Góor gu xaraful, ndax nanguwula xaraf, dees na ko dagge ci biir xeetam, ndax sàmmul sama kóllëre.»

Képp ku defar lenn lu ni mel, ngir di ko xeeñoo, dees koy dagge ci bànni Israyil.»

Képp ku lekk lenn luy deret, dees na ko dagge ci biir bànni Israyil.»

Képp ku def lenn ci yooyu ñaawtéef déy, kooku dees koy dagge ci biir bànni Israyil.

Man ci sama bopp dinaa noonoo nit kooku te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil, ndax li mu jël ciy doomam jox Moleg, di sobeel sama bérab bu sell tey teddadil sama tur wu sell.

Te kat, képp ku toroxluwul boobu bés, dees koy dagge ci biir bànni Israyil.

Kon nag nanga leen wax ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen ngeen di boole yàpp ak deret di ko lekk, di wékki gët kasaray tuur, di tuur deretu jaamburi Yàlla, ba noppi di moom réew mi?