TSK

TSK · Leviticus 7:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Na sarxalkat bi boole loolu lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy ñamu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji. Mboolem luy nebbon, Aji Sax jeey boroom.

Na génne lépp luy nebbon ci yëkk wi ñuy sarxal muy póotum bàkkaar: nebbon bi sàng yérey biir yi, ak lépp luy nebbon te jàpp ci yérey biir yi,

Ñi lekk seen nebboni sarax, naan biiñ bi ñu leen di tuural kay, nañu jóg, boog, xettli leen, di seen kiiraay!

Lu tax ngeen di teddadil sama saraxi rendi ak yeneen sarax yi ma santaane ci màkkaan mi? Lu waral ngay teral sa doom yi teraanga joo ma joxul, ba ngeen di yafloo li gën ci mboolem saraxi Israyil sama ñoñ?”

Ku topp bakkanam, fàww mu dee, waaye ku rey jëfi yaramam ci ndimbalal Noowug Yàlla, dina texe.