TSK

TSK · Leviticus 8:35

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Musaa teg ca sàkk ca diwu pal ga, ak deret ji ci sarxalukaay bi, wis-wisal ko ci kaw yaramu Aaróona ak ca kawi yéreem, wis-wisaale ko ca kaw yarami doomam yu góor ak ca kaw yérey doomam.

Ku ñuy laabal day fóot ay yéreem, watu ba set te sangu, doora set. Gannaaw loolu man naa dugg ci dal bi, waaye na yem ca bunt xaymaam ca biti diiru juróom ñaari fan.

Su niir wa yàggee ca kaw màkkaan ma it, ak lu fan ya bare bare, bànni Israyil a ngay dénkoo dénkaaney Aji Sax ji, waaye duñu dem.

¶ Soppleen seen Yàlla Aji Sax ji, te ngeen dénkoo ndénkaaneem, ak dogali yoonam, ak àttey yoonam, aki santaaneem, bés bu nekk.

Diiru juróom ñaari fan ngay joxe bés bu nekk ab sikketu póotum bàkkaar akaw yëkk akum kuuy, te na lu ci nekk mucc sikk.

¶ Gannaaw noo moom yii dige nag, soppe yi, nanu setal sunu bopp ci mboolem sobey yaram, ak ju xel, te nu matal sellnga ci ag ragal Yàlla.

¶ Na ma la ko dénke woon ba may dem diiwaanu Maseduwan rekk, nanga toog Efes googu, ngir ña fay jàngle leneen, nga aaye leen.

¶ Maa ngi lay àrtu nag fi kanam Yàlla, ak Almasi Yeesu, ak malaaka yi ñu tabb, ngir nga sàmm loolu te baña jeng, mbaa nga jëfe lenn loo defe xejj ak seen.

¶ Ñi barele alalu àddinay tey nag, dénk leen ñu baña réy te baña yaakaar alal ju wóoradi, te ñu yaakaar Yàlla mi nuy xéewale lépp, ngir nu di ko bége.

¶ Kon nag dama lay dénk fi kanam Yàlla ak Almasi Yeesu, miy àtteji ñiy dund ak ñi dee, di la dénk ci darajay bésam ba muy feeñ, ak ci darajay nguuram,

¶ Jumtukaay yooyi di ay misaali yëf ya fa asamaan, yooyu sarax lees ko waroona setale. Kon yëfi asamaan ya ci boppam, sarax yu ko gën lees ko wara setale.