Ndokklee, Israyil, ana ku mel ni yeen, askan wu Aji Sax jiy wallu, di seen kiiraay, di seen ndimbal, di saamar bi leen di sagal? Seeni noon a leen di loxal, te yeen, fa seen gannaaw ya ngeen di daagoo.
TSK
TSK · Luke 1:71
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
musal leen ci loxol bañaale, jote leen ca loxol noon ba,
¶ Aji Sax ji kay mooy yërëm askanu Yanqóoba, dellu taamu xeetu Israyil wii. Moo leen di sancaatal fa seen suuf, doxandéem yi fekki leen; boole seen bopp ci askanu Yanqóoba.
Mu ne: «Maa la wacc diir bu gàtt, dellu la jël ci yërmande ju yaa.
Waaye seen Yàlla Aji Sax ji lañuy jaamu ak seen buur bi ma leen di falal, mu toogal Daawuda.
Xel mu dal lañu fay dëkke, tabax fa ay kër, jëmbat seeni reseñ. Bu ma wàcceelee ay mbugal mboolem ñi leen di sewal te séq leen, dinañu dëkke ba xam ne maay seen Yàlla Aji Sax ji.»
Dootuñu doon sëxëtoom xeet yi, te rabi àll yi dootuñu leen lekk. Dañuy dëkke xel mu dal, te kenn du leen tiitalati.
Aji Sax ji moo teggi say mbugal, waññi sab noon. Buurub Israyil, Aji Sax jaa ngi fi sa biir, dootuloo tiit lu bon.
ne moo nuy may nu mucce ci loxoy noon, ba man koo jaamoo xel mu dal