TSK

TSK · Luke 1:72

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

ku la ñaanal barke, ma barkeel, ku la móolu it, ma alag, te xeeti àddina sépp, ci yaw lañuy barkeele.»

te xeeti àddina sépp ci saw askan lañuy barkeele, ndax déggal nga ma.”»

Saw askan dina ne gàññ ni suuf. Dinga law penku ak sowu, ndijoor ak càmmoñ. Ci yaw ak saw askan la giir yi ci kaw suuf yépp di barkeele.

di fàttliku ba fàww kóllëreem, di bàyyi xel ba ci junniy maas kàddoom

Mooy leel ku ko ragal, di bàyyi xel kóllëreem gi ba fàww.

Waaye man maay bàyyi xel sama kóllëre gi ma fasoon ak yaw ba ngay ndaw. Maa lay saxalal kóllëre guy wéy ba fàww.

Luke 1:54 TSK

Moo wallu bànni Israyil, jaamam, bàyyee ko xel yërmandeem,

¶ Ci wàllu xibaaru jàmm bi, ay noon la Yawut ñi taxawe, te muy xéewal ci yeen ñi dul Yawut. Waaye ci wàllu dogal bi taamu Yawut ñi, ay soppe lañu, te seeni maam tax.

¶ Mu mel ni Ibraayma, ba Yàlla di digoo ak moom, Yàlla manul woona giñe ku sut Yàlla. Moo tax mu giñal ko ci boppam,