Yeen ñi xam njekk, dégluleen ma, yeen, askan wi sama yoon yebu ci seen xol. Buleen ragal nit ku leen sewal, buleen tiit seeni xaste.
TSK
TSK · Luke 12:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Yaw nag takkul te wax leen lépp lu ma la sant. Bul am tiitaange fi seen kanam, lu ko moy ma tiital la fi seen kanam.
Waaye yaw nit ki, bu leen ragal, bul ragal seeni wax. Xam naa ne ay taxas aki dég a lay wër, nga toog ci kawi jiit. Waaye bul ragal seeni wax te bul tiit seen kanam doonte kërug fippukat lañu.
¶ Ba waa kurélu àttekat ya gisee fit, wi Piyeer ak Yowaan àndal, te ñu xam ne niti neen ñu masula jàng lañu, dañoo waaru. Xamoon nañu nag ne ñook Yeesoo nekkoon.
Buleen ragal seeni noon ci lenn. Seen fit mooy màndargaal sànkutey noon yi, te yeen it, mooy màndargaal seenug mucc gu bawoo fa Yàlla.
Te sax su ngeen doon jànkoonteeki coono ndax seenug njub, ndokklee yeen. Buleen am jenn tiitaange ci seeni xuppe, te buleen jaaxle.