TSK

TSK · Luke 20:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mu neeti: «Demal, wax askan wii, ne leen: “Dégluleena déglu te buleen dégg, xool-leena xool te buleen gis.”

Tendeefal, jommi rekk! Gëmm, gumba rekk. Ñiika màndi te du biiñ, ñuy jang te duw ñoll!

Xool naa xool ci tuur yi, gisuma kenn; du kenn ci ñoom ku ciy xelale, ba ma laaj ko, mu mana tontu.

Ñii xamuñu, xàmmeewuñu, seeni gët lañu lëndëmal, ba gisatuñu; fatt seenum xel, ba xelootuñu.

¶ Aji Sax ji nag neeti ma: «Léegi jëlal jumtukaayu sàmm bu ñàkk bopp.

«Kàddug sarxalkat déy day sàmm xam-xam, te ciy waxam la nit ñi di sàkkoo àlluwa, nde mooy ndawal Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.

Noonee Sànnes ak Sàmbres doon jànkoonteek Musaa, ni la góor ñooñu di jànkoontee ak dëgg gi; ñooy nit ñu seenum xel yàqu, te ñu doyadi ci wàllu ngëm.