TSK

TSK · Luke 4:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Su ko defee su ma teqlikook yaw, ngelawal Aji Sax ji yóbbu la fu ma xamul, fekk ma dem wax ko Axab, te du la gis. Kon da may rey! Moona sang bi, man de, damaa masa ragal Aji Sax ji ba may ndaw ba tey.

xelum Aji Sax ji tegu fi kawam, xelum rafet xalaat ak ràññee, xelum digle ak njàmbaar, xelum xam Aji Sax ji, ragal ko.

Ba loolu amee ngelaw ne ma siféet, yóbbu. Maa ngay deme naqar ak xol bu tàng, te loxol Aji Sax ji diis gann ci sama kaw.

Luke 2:27 TSK

Ci kaw loolu mu dem ba ca biir kër Yàlla ga ci dooley Noo gu Sell gi. Gannaaw loolu waajuri Yeesu indi Yeesu ngir defal ko li aaday yoon wi laaj.

Luke 3:21 TSK

¶ Noonu Yaxya doon sóobe ñépp cim ndox, ni la deme ba Yeesu dikk, mu sóob ko ci ndox. Ci biir loolu Yeesu yékkati kàddug ñaan, asamaan ubbiku.

Luke 4:18 TSK

«Noowug Boroom baa ngi fi sama kaw, moo ma fal, ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm bi. Da maa yebal ngir ma yégal jaam yi ne dees na leen goreel, yégal gumba yi ne dinañu gis, yégal ñi ñu not, ne dees na leen jot,

Acts 8:39 TSK

Naka lañu génne ca ndox ma, ngelawal Boroom bi ne cas Filib, yóbbu, jaraaf ja gisatu ko. Teewul mu topp yoonam, ànd ak mbég.