TSK

TSK · Malachi 3:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Keroog Aji Sax ji fas na kóllëre digganteem ak Ibraam, ne ko: «Askan wi soqikoo ci yaw laa jox réew mii dale ci dexu Misra, ba ca dex gu mag googee di Efraat,

Yàlla ne Musaa: «Maay Ki nekk. Kon waxal bànni Israyil ne leen: “Aji Nekk ji moo ma yónni ci yeen.”»

Yàlla du nit, bay fen, du doom aadama bay tuub. Moom wax na lu mu deful a? Am àddu na lu mu sottalul?

Yaw yaa di Aji Sax ji, Yàlla ji tànn Ibraam, jële ko Ur gu waa Kalde, tudde ko Ibraayma.

xanaa dëddu, di ko wor ni seeni maam, toogadi ni xala gu yolom.

kee di sunu Yàlla Aji Sax ji, di àtte suuf sépp,

Man Aji Sax ji maay sa Yàlla; téye sa loxol ndijoor, di la wax ne la: «Bul tiit, maa lay dimbali.»

Aji Sax ji, mennum man a; amul jotkat bu ma moy.

Aji Sax ji man a, du keneen; kenn du yàlla ku dul man. Maa la gemb, te xamuloo ma,

«Du maay Aji Sax ji, Yàllay képp kuy dund. Ana lu ma të?»

Duma wéye di tàkkal sama mer, duma yàqteeti Efrayim, ndax maay Yàlla, duma nit, maay Aji Sell ji ci seen biir, duma dikke am sànj.

Ndegam ba ñu dee ay bañaaley Yàlla lees nu jubalee deewug Doomam, ñaata yoon lees nuy gënatee musale ag dundam, gannaaw ba ñu nu jubalee ak Yàlla?

¶ Ci wàllu xibaaru jàmm bi, ay noon la Yawut ñi taxawe, te muy xéewal ci yeen ñi dul Yawut. Waaye ci wàllu dogal bi taamu Yawut ñi, ay soppe lañu, te seeni maam tax.

¶ Nun nag bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla fu nu tollu, ci yeen ñi Boroom bi sopp, ndax yeen la jëkka taamu, ngir sellale leen Noo gu Sell gi, ak itam seen ngëm gi ngeen gëm dëgg gi, ngir texeel leen.

Yeesu Almasi menn mi la woon démb ak tey ba fàww.

¶ «Man, maay Alfa, di Omega», la Boroom bi Yàlla wax, moom Ki masa Nekk, Ki Nekk, di Kiy Dikk ëllëg, te di Aji Man ji.