TSK

TSK · Micah 3:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ci kaw loolu ñeengokat ya taluñoo janook Musaa ndax ay taab, ñoom ak waa Misra gépp.

¶ Bu jëkkoon nag ci Israyil ku daan leerluji ci Yàlla da naan: «Nan dem ca giskat ba,» ndax ku ñuy wooye yonent tey, booba, ab giskat lañu ko daan wooye.

Mu seetlu ci Aji Sax ji, Aji Sax ji wuyuwu ko; du ci gént, du ci jumtukaayu tegtal bi ñuy wax Urim, du ci kàddug yonent.

Sunuy takk réer na nu, yonent amatul, te kenn xamul fu lii di àkki.

Jàppool say jat rekk ak sa xërëm yu ne xas yoo dale sonn ba ngay ndaw. Jombul mu amal la njariñ, mbaa ñu ragale la ko.

Binnil ndànk te bul ñaawlu. Bul tàggook sa kaala, bul tàggook say carax, bul muur sa tuñum kaw ba ci sikkim di ko ñaawloo. Bul lekk ñam wu la njaal mi indil.»

ne su ngeen ma waxul gént gi, àtte bi di benn ci yeen ñépp. Gise ngeen ba nar maa wax ay fen aki caaxaan, di yaakaar jamono soppiku. Waxleen ma gént gi rekk, ma xam ne man ngeen maa wax pireem.»

Xeet yee ciy gis, rus, te seen gépp njàmbaar du tee ñu ub seen gémmiñ, seeni nopp buur.

Noonee Sànnes ak Sàmbres doon jànkoonteek Musaa, ni la góor ñooñu di jànkoontee ak dëgg gi; ñooy nit ñu seenum xel yàqu, te ñu doyadi ci wàllu ngëm.