TSK

TSK · Micah 4:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Bu ca fukkeelu nit ña desoon, ñoom it dees na leen dellu taal. Waaye dañuy mel ni wenn ci xeeti garab yu mag yi ñuy gor, ëkk ba dellu jebbi, ëkku xeet wii, jiwu mu sell lay doon.»

Aw ndes ay délsi, di ndesu askanu Yanqóoba, ñeel Yàlla Jàmbaar ji.

Kersa la weer wiy am, gàcce ñeel jant bi; Aji Sax ji Boroom gàngoor yi daal, mooy nguuru Yerusalem, kaw tundu Siyoŋ, leeram ga jollee fa kanam magi ñoñam.

Ki ci gëna tuut ay meññ junni, ki ci gëna néew jur xeet wu mag. Man Aji Sax ji, bu lii jotee, ma gaaw koo sottal.

Mu ne ma: «Yaw nit ki, sama màkkaanu ngàngunee ngi, bérab bii laay teg samay tànk, di fi dëkke fi digg bànni Israyil ba fàww. Bu waa kër Israyil dellu teddadil sama tur wu sell, ñook seeni buur ci seen gànctu, ak seen néewi buur yi ñuy denc ci seeni jaamookaay.

Palug mboolem nguur yi asamaan tiim, ak kilifteef gaak daraja ja dees na ko boole, jébbal aji sell yu Aji Kawe ji. Nguurug mbooloo moomu day sax ba fàww, kilifa yépp di ko déggal, di ko wormaal.”

«Yeen askanu Yanqóoba, maa leen di dajalee dajale yeen ñépp, maay boolee boole ndesu Israyil. Benn bopp laa leen di def, niy xar ca gétt ga, niy gàtt ci seenum parlu, coowal nit ña jolli.

Micah 5:3 TSK

Kilifa gaay taxaw, sàmme ci dooley Aji Sax ji, ci màggug turu Yàllaam Aji Sax ji, ba ñu dëkke jàmm, nde léegi lay doon ku màgg ba turam dajal cati àddina.

Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.

Yuda déy laay bank, muy samag xala, te Efrayim laa koy soxe, muy fitt gi. Yaw Siyoŋ, sa doom yu góor laay yékkati ci sa kaw doom yu góor, yaw réewum Geres (/Yawaan). Doomi Siyoŋ laay def saamaru jàmbaar.

Luke 1:33 TSK

Mooy nguuru fi kaw waa kër Yanqóoba ba fàww, te nguuram du foq mukk.»

¶ Bokk yi, moytuleena defe ne seen xel mu rafet a leen may li ngeen am. Bugguma ngeen umple mii mbóot: Ag déggadi moo dikkal lennati bànni Israyil, ba kera xeet yi dul Yawut duggsi, ba seenub lim mat.