Sawaraa ngay tàkke ca samam sànj, di lakke ba ca xóotey njaniiw, ba xoyom suuf ak meññeefam, ba jafal reeni tund ya.
TSK
TSK · Micah 6:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji gëdd, nokki, mu riir; xuri géej ne fàŋŋ, kenuy suuf ne duŋŋ.
ak ba muy sàkkal géej kemoom, ba du jàll fa mu wax. Ba muy rëdd fa muy samp àddina,
Aji Sax jaa ngi ci jataayu layoo, moo jóg di àtte ay xeet.
Fàttli ma saw lay, nu bokk layoo; waxal boog yaw, ndax nga yey!
Ana lu ngeen di layook man? Yeen ñépp a ma gàntal!» Kàddug Aji Sax jee.
Aji Sax ji dafa wax ne: «Su ma waccee mboolem askanu Israyil ndax li ñu def lépp, kon nit a mana natt kawewaayu asamaan, mbaa mu xayma xóotaayu suuf.» Kàddug Aji Sax jee.
¶ Yeen bànni Israyil, dégluleen kàddug Aji Sax ji, Aji Sax ji kat moo séq ab layoo ak waa réew mi: «Du kóllëre, du ngor, du gennug ràññee Yàlla ci réew mi.
Aji Sax ji moo séq ak Yuda ab layoo, mooy mbugale Yanqóoba ay jëfinam, añale ko ay jëfam.