TSK

TSK · Numbers 12:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Musaa da daan toxal xayma bi, samp ko fu sorewaatook dal bi, ca biti. Mu di ko wooye xaymab ndaje mi. Ku amaan lu muy diis Aji Sax ji, da daan génn dal bi, dem ba ca xaymab ndaje mooma ca biti.

Na ko sarxalkat bi seet. Su dee ab tërgën bu weex te kawar gi ci nekk soppiku weex, boole ci def góom ca biir,

Fàttlikuleen la seen Yàlla Aji Sax ji defoon Maryaama ca yoon wa, ba ngeen génnee Misra.

Aji Sax ji nag mbugal Asaryaa, teg ko jàngoroy ngaana ba kera bés ba mu deeyee. Ci néeg bu ñu ko ber la dëkk. Doomu Buur Yotam moo jiite kër ga, yor kilifteefu askanu réew ma.

Ba leeru Aji Sax ji yékkatikoo ca serub ya, dem ba ca buntu kër ga, niir wa daa fees kër ga, ëtt ba fees dell ak leeru Aji Sax ja ne ràññ.

Bu ñu yaroon seeni doom it, maa leen leen di xañ, ba kenn du des. Te it ngalla ñoom, bu ma leen dëddoo.