TSK

TSK · Numbers 23:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba loolu amee Balaam ne Balag: «Tabaxal ma fii juróom ñaari sarxalukaay, te waajalal ma fi juróom ñaari yëkk yu ndaw, ak juróom ñaari kuuy.»

Yéegal ba ca kaw tundu Pisga, nga dawal sa bët, te séenu réew ma wetu sowu, ba bëj-gànnaar, bëj-saalum, ba penku. Xoolal bu baax, nde doo jàll dexu Yurdan gii.

¶ Ba loolu amee Musaa bàyyikoo jooru Mowab, yéegi tundu Nebo, ba ca collu tundu Pisga, wa jàkkaarlook Yeriko. Aji Sax ji nag won ko mboolem réew ma, diiwaanu Galàdd ba diiwaanu Dan,

Ñii déy a yullee wurus ci mbuus, sàkk xaalis, natt diisaay ba, fey tëgg bu leen ci tëggal am tuur mu ñuy sukkal ak a sujjóotal,