TSK

TSK · Numbers 24:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba Balaam jógee ca suba sa, da ne kàngami Balag ya: «Delluleen seenum réew, ndax Aji Sax ji bañ na; mayu ma ma ànd ak yeen.»

Balaam ne Balag: «Taxaweel nii ci sa saraxu rendi-dóomal, man ma séentuji nee.»

Ñeengo jàppul Yanqóoba, gisaane gisul Israyil gii. Lu jot rekk, àggees ko Yanqóoba: ne ko: “Israyiloo, lii la Yàlla def.”

Xanaa du ñoom ñoo dëdduloo woon bànni Israyil Aji Sax ji, ci ndigalal Balaam, ca mbir ma woon ca Pewor, ba tax mbas ma dikkal mbooloom Aji Sax ji?

Sóol dem ba ca màndiŋu Sif, ànd ak ñetti junniy ñeyi xarey Israyil, ngir rëbb Daawuda ca màndiŋu Sif.

¶ «Waaye lenn a ngi lu ma lay sikke: yaa ngi uuf foofu ay nit ñuy saxal njànglem Balaam, moom mi doon xiirtal Balag ci tegal Israyil ndëgg-sërëx, ngir ñu lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur, ak di gànctu.