TSK

TSK · Numbers 29:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Màggalug ayi bési Ngóob, nangeen ko wormaal, bu ngeen di góob gubi bele yi jëkka ñor, màggalu bésu Farmàngu mi ci ndeetel at mi itam, màggal-leen ko.

¶ «Bésub juróom ñetteel ba seen bésub ndaje lay doon. Mboolem lees baaxoo liggéey, deesu ko ci liggéey.

Ci kaw loolu ñu gis ne bind nañu ci yoon wi Aji Sax ji santaane, te Musaa jottli ko, ne: «Bànni Israyil dañoo wara dëkk ci ay mbaar diiru màggalu weeru juróom ñaareel wa.»

¶ «Ci wàllu màggal giy door fukki fan ak juróom ci juróom ñaareeli weer wi, na ki tooge jal bi def niki ci màggalu bésub Mucc ba. Juróom ñaari fan, yi màggal giy def, yenn sarax yooyii rekk lay joxe, muy saraxu póotum bàkkaar, ak saraxu rendi-dóomal, ak saraxi pepp ak diw.