¶ Ba loolu amee Musaa wàcc tund wa, dellu ca mbooloo ma. Mu sell-luloo leen, ñu fóot seeni yére,
TSK
TSK · Numbers 31:23
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Lépp luy yére mbaa der bu wasal taq, dees koy fóot te du tere mu yendoo sobe ba jant so.
Na ku set tonni dóomu nag wa, te sotti ko bérab bu set, foofa ca biti. Dóom ba dencub mbooloom bànni Israyil lay doon, ñu di ko waajale ndoxum setlu, ngir saraxu póotum bàkkaar.
Booy xuus cim ndox, maa ngi ànd ak yaw; ag dex du la mëdd. Booy dox cib taal, doo lakk, sawara du la xoyom.
Su ngeen dégluwul, te defuleen seen xel ci teral sama tur,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «alkànde laay yebal fi seen biir, ba alagaale seeni barke, te alag naa ko jeeg, nde defuleen seen xel ci teral ma.
ku ci nekk, sab liggéey dina feeñ, ndax bés baa koy xamle, nde sawara lees koy feeñale. Ku ci nekk, ak lu sa xeetu liggéey mana doon, sawara lees koy natte.
ca la nu musal, te du jenn jëfu njekk ju nu def, ba tax mu musal nu, waaye ci yërmandeem la nu musale, sang nu cangaay lu nu taxa judduwaat, boole ci yeesale nu Noo gu Sell,
Ndox mooma di misaalub sóobu gi leen musal tey; du sóobu guy dindi tërub yaram, waaye moom ngeen di wuyoo wooteb Yàlla ci xel mu dal, te li leen di musal mooy ndekkitel Yeesu Almasi,
dama lay digal, nga jënd ci man wurus wu ñu xellee ci sawara ba mu set wecc, ngir nga am alal. Jëndal itam yére yu weex yoo soloo, ba làq sa duŋŋaaral gu gàccelu gi; ak tuufaay looy tuufoo, ngir nga gis.