TSK

TSK · Numbers 34:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Sowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja.

Aji Sax ji nag yuree ca asamaan tamarax buy tàkk, muy taw ci kaw Sodom ak Gomor, na ko Aji Sax ji dogale.

¶ «Seen kemu bëj-saalum a ngay dale màndiŋu Ciin, leru réewum Edom, daleeti ca catal géeju Xorom ga ca penku.