TSK

TSK · Revelation 2:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ñépp a leen di bañ ndax sama tur.

Te it ba ñuy tuur deretu Eccen, sa seede ba, man it maa nga fa woon, juboo caak ñoom, te ña ko rey, maa leen doon wattul seeni yére.”

Ku fàggulul ay bokkam nag, rawatina waa këram, yoonu ngëm wi la gàntal, te moo yées ku gëmul.

Nanu ŋoy ci yaakaar, ji nu biral ne moom lanu am, te nu baña yoqi, nde ki dige ku wóor la.

Jude 1:3 TSK

¶ Soppe yi, yàkkamti woon naa leena bind ci mbirum mucc gi nu bokk, waaye fàww ma bind leen, ngir ñaax leen ci xeexal yoonu ngëm, wi Yàlla xasa dénk ñu sell ñi, benn yoon ba fàww.

¶ Gis naa sa coono ak sag ñàkk, moona yaaka duunle! Gannaaw loolu it, waxi yàq-der yi tukkee ci ñooñu tuddoo Yawut te duñu Yawut, duñu lenn lu moy jàngub Seytaane, dégg naa ko.

Kon nag fàttlikul la nga jotoon te dégg ko; nga sàmm ko, te tuub. Soo teewluwul nag, dinaa ñëw nib sàcc, te doo xam mukk wan waxtu laa naa jimeet fi sa kaw.

¶ «Maa ngi ñëw léegi. Ŋoyal ci li nga yor, ngir kenn baña fëkk sa kaalag ndam.