TSK

TSK · Romans 10:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yaw nag yaa yelloo njekk ci mboolem li nu dal, ndax worma nga jëfe, nun noo bon.

May siiwal sa njekk, di yendoo waxtaane say wall, doonte lim ba wees na ma.

Séentuleen asamaan te xool suuf si mu tiim. Asamaan ay tasaaroo ni saxar, suuf ràpp ni mbubb, ñi ko dëkke dee niy weñ, te du tee sama wall di sax ba fàww, sama njekk it du dagg.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Sàmmleen yoon, di def njekk. Sama wall kat a ngi dikk léegi, sama njekk laa ne, léegi mu teew.

Du kenn kuy wormaal sa tur, mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, yaa nu làq saw yiw, yaa nu def ban bu tooy ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.

¶ «Juróom ñaar fukki ayi bés lañu àppal sa mbooloo ak sab dëkk bu sell, ngir dakkal tooñ gi, jeexal moy gi, jotu ñaawtéef, saxal njubte ba fàww, matal peeñum yonent, ba delloo bérab bu sella sell ag sellngaam.

Xel ma mujj délsi, mu ne: “Ñaata surga la sama baay am, seen lekk ne gàññ, man, ab xiif di ma rey fii!

Luke 18:9 TSK

¶ Yeesu léebati lii, ngir ñiy damoo seenug njub, tey doyadal ñi ci des.

Ci xibaaru jàmm bi lañu feeñal ni Yàlla di joxe nit ñi àtteb ñu jub, te lépp aju ci ngëm, ca ndoorte la, ba ca njeexital la. Noonu la Mbind mi indee ne: «Ku jub ndax ngëmam mooy dund.»

nde Yàlla ci biir ag jéllaleem la firndeel njubteem ci janti tey jii, ngir mu leer ne moo wéye njub, te képp ku gëm Yeesu, moo koy jox àtteb ku jub.

¶ Ana lu nu ci mana wax? Xeet yu dul Yawut te sàkkuwuñu woon ag njub, ñoo jagoo àtteb njub, te mooy njub gi ngëm di maye.

Ma artooti képp ku dem ba ñu xarfal ko, ne ko mboolem yoon wi la wara jëfe.

¶ Ci man Simoŋ Piyeer, miy jaamub Yeesu Almasi, di ndawam, ci man la bataaxal bii bawoo, ñeel ñi ñu may ngëm gu njég ga réye ni sunu gos, ci sunu njekku Yàlla, Musalkat bi Yeesu Almasi.