TSK

TSK · Romans 2:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Acts 10:2 TSK

Ku jullite la woon te ragal Yàlla, mook waa këram gépp; bare woon na sarax yu muy yéwéne askan wi, te ñaan ci Yàlla la saxoo woon.

Acts 11:3 TSK

naan: «Yaa dem ca ña xaraful, di bokk ak ñoom lekk!»

ngir njub gi yoonu Musaa laaj mana sotti ba mat sëkk ci nun, ñi toppatul sunu bindu suux, xanaa Noowug Yàlla.

¶ Kon nag, yeen jaambur ñi dul Yawut cib juddu, yeen ñi ñuy wooye yéefar yi xaraful, te ñi leen ko dàkkantale woon di Yawut yi xarafe ci loxol nit ku leen xarfal ci seen yaram, fàttlikuleen seen démb.

Ci moom ngeen xarafe xaraf gu loxol nit deful, ndax noonu kuy xarfal nit ki di doge as lëf ci yaramu nit ki, ni la Almasi di doge ba mu set, buumu njaam gi leen dooley bàkkaar tënke woon. Noonu la Almasi di xarfalee.