TSK

TSK · Romans 4:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Loolu wees Aji Sax ji yóbbu ko ci biti ne ko: «Xoolal asamaan, te waññ biddiiw yi, ndegam man nga ko.» Mu dellu ne ko: «Noonu la sa askan di tollu.»

Yaakaar ju tas day jeexal xol, aajo ju faju di suuxat bakkan.

Kon nag, bokk yi, dalal-leen seen xel, ndax gëm naa Yàlla, xam naa ne ni mu ko waxe, ni lay ame.

Ngëmu Ibraayma wàññikuwul, doonte ba mu xoolaatee boppam, xam na ne yaramam dee na daanaka, ndax fekk na ay atam xawa tollu ci téeméer, te njurukaayu Saarata it fekk na ko dee.

Ndax kat sunu mucc, yaakaar la taxaweegum, te yaakaar joo teg sa bët, dootu yaakaar. Li nit ki teg bëtam, nu mu koy yaakaaratee?