TSK

TSK · Romans 7:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ana xeet wu ko màgge, ba am dogali yoon ak àttey yoon yu jekke ni yoon wii ma joxe fi seen kanam bésub tey?

Ca tundu Sinayi wa nga wàcc, àddoo asamaan, wax ak ñoom, dénk leen ndigal yu jub, ak yoon yu dëggu, ak dogali yoon ak santaane yu baax.

Sang bi, sottalal ma sa dige bi nga digook ku la ragal.

Maa sopp say santaane, mu gënal ma wurus ba ci wurusu ngalam.

Sang bi, maaka sopp sa kàddu gi set ni weñ gu ñu xelli!

Ndax loolu day tekki ne ngëm lanu jël, neenale ko yoonu Musaa? Mukk! Xanaa dañu koo dëggal kay.

Gannaaw li ma buggul, moom laay def nag, juboo naa ak yoonu Musaa ci dëggal ne yoonu Musaa baax na.

¶ Xam nanu nag ne yoonu Musaa baax na, ndegam na mu ware lees ko jëfe.