Te yeen ñi ñu woo ci Yeesu Almasi itam, ci ngeen bokk.
TSK
TSK · Romans 8:30
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye Yàlla moom, ni mu firndeele cofeelam ci nun, moo di, ba nu dee ay bàkkaarkat, ca la nu Almasi deeyal!
Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.
Ñi Yàlla taamu, ana ku leen di tuumaal? Yàlla de mooy jox nit àtteb ku jub.
ñeel mbooloom Yàlla, mi ci Korent, yeen ñi ñu sellal ci jëmmu Almasi Yeesu, te ñu woo leen ngir ngeen doon ñu sell, ñeel itam mboolem ñiy tudde fépp fu mu mana doon, sunu turu Boroom Yeesu Almasi, mi leen moom, moom nu.
Te loolu la ñenn ci yeen doonoon. Waaye Yàllaa leen fóot, sellal leen, jubal leen, ci turu Sang Yeesu Almasi, ak ci sunu Noowug Yàlla.
la dogaloon lu jiitu, ne ci Yeesu Almasi la nuy defe ay doomi boppam, te muy bànneexam, di coobareem.
Ci sunu bokk ak Yeesu Almasi la nu Yàlla dekkalandoo ak moom, dëëlandoo nook moom fa déndi asamaan.
Seenug dund dëgg Almasi la, te keroog bu Almasi feeñee, yeen itam ay ànd ak moom feeñ, ba séddu ci ndamam.
kera bés bu délsee ba jot ci teddngaam ci biir ñoñam ñu sell ñi, ba mboolem ñi ko gëm di ko yéemoo. Te yeen ci seen bopp, ci ngeen di bokk, ndax yeena gëm la nu leen seedeeloon.
¶ Kàddu gu wóor a ngii: Su nu deeyandoo ak Almasi, nooy dundandoo ak moom itam;
Looloo tax Yeesu di defarekat bi fas kóllëre gu bees, ngir ñi ñu woo mana jot ci muur gu sax dàkk gi ñu leen dig. Deeyam gi mu dee, moom la leen jote ci bàkkaar yi ñu xëtte kóllëre gu jëkk ga.
Lu bon, buleen ko feye lu bon; ay saaga it, buleen ko feye ay saaga. Xanaa ngeen ñaanal leen, feye leen ko, ndax ci loolu lees leen woo, ngir ngeen jagoo barke.
Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju.
Dinañu xare ak Gàtt bi, waaye Gàtt bee leen di daan, ndax mooy Sangu sang yi, di Buuru buur yi. Mooy daan mook ñoñam, ñi mu woo, tànn leen te ñu saxoo topp ko.»