TSK

TSK · Romans 8:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ndegam ba ñu dee ay bañaaley Yàlla lees nu jubalee deewug Doomam, ñaata yoon lees nuy gënatee musale ag dundam, gannaaw ba ñu nu jubalee ak Yàlla?

Ndaxte peyooru bàkkaar mooy dee, waaye yiw wi Yàlla di maye mooy texe gu sax dàkk fi Almasi Yeesu, sunu Boroom.

Bàkkaar moo ma jekkoo ndigalu yoon, ba nax ma, te ndigalu yoon la ma reye it.

Ku topp bakkanam, fàww mu dee, waaye ku rey jëfi yaramam ci ndimbalal Noowug Yàlla, dina texe.

Ndax kat solob nguurug Yàlla jotewul dara akug lekk mbaa ag naan, waaye solob nguuru Yàlla moo di njub ak jàmm, ak mbégte ci ndimbalal Noo gu Sell gi.

Ku jiyal bànneexu bakkanam, ci bànneexu bakkanam lay jële ngóobum yàqute; ku jiyal Noowug Yàlla, ci Noo gi ngay góobe texe gu sax dàkk.