Ruth 1:5
TSK
ñoom ñaar ñooñu di Malon ak Kilyon faatu ñoom it, jigéen ja ñàkk noonu ñaari doomam ak jëkkëram. Mu des moom kenn.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ñoom ñaar ñooñu di Malon ak Kilyon faatu ñoom it, jigéen ja ñàkk noonu ñaari doomam ak jëkkëram. Mu des moom kenn.
¶ Mu ne ko: «Yal na la Aji Sax ji barkeel, doom! Jiwati nga bokk gi ngor lu gënatee rafet. Ndax su la neexoon, nga topp ci xale yu góor yi, ñu am ak ñu ñàkk.
¶ Yeesu moo doon dem, mbooloo mu réy dar ko. Mu geestu ne leen:
«Teral-leen seen ndey ak seen baay,» mooy ndigal li jëkka ànd akub dige,
¶ Jigéen ñi, nangul-leen seen jëkkër, noonu mu jekke ci ku bokk ci Boroom bi.
Yal na Yàlla baaxe nag waa kër Onesifor, yërmandeem, ndax dëfal na ma lu bare, te kersawoowul li ñu ma tëj kaso,