TSK

TSK · Ruth 4:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba loolu amee ñaari malaaka ya dikk Sodom ca ngoon, fekk Lóot toog ca buntu dëkk ba. Lóot séen leen, jóg gatandu leen, daldi leen sujjóotal, ne leen:

¶ Te itam ay àttekat aki kilifa ngeen di tabb ngir seeni giir, ci mboolem dëkk yi leen seen Yàlla Aji Sax jiy jox, ñuy àtte mbooloo mi àtteb dëgg.

na ko baayam ak ndeyam jàpp, yóbbu ba ca seen magi dëkk ba, ca seen bunt dëkk.

Ruth 3:12 TSK

Da di nag, dëgg la sax, mbokk laa mu la mana jotaat, waaye meneen mbokk mu la mana jotaat a ngi fi, te moo ma ci gëna yey.

Job 31:21 TSK

ndegam maa xàccil sama loxo ab jirim, ndax yaakaar kiirlaay ca pénc ma,

Amos 5:10 TSK

Yeena bañ kuy yedde ci pénc, te sib boroom làmmiñ wu maandu.

Ma ne ko: «Foo jëm?» Mu ne ma: «Xanaa natti Yerusalem, ba xam nu mu yaatoo, ak nu mu gudde.»