TSK

TSK · 1 Peter 2:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ab cér du leen ñeel ci seen biiri bokk. Aji Sax ji mooy seenub cér, na mu leen ko waxe woon.

Deel jaajëfal Yàlla, sarxale ko, di fey Aji Kawe ji loo dige,

Yal nanga ma nangul samag ñaan ni cuuraay lu ñu la taalal, yoxo yi ma la tàllal di saraxu ngoon soo gërëm.

Te ñenn ci yooyu xeet, maa leen di jël, def leen ay sarxalkat aki Leween.» Aji Sax jee ko wax.

Waaye li ko dale penku ba sowub jant, fu ci nekk la sama tur màgge ci biir xeet yi, te fépp lees di taale cuuraay, ngir sama tur, boole ci sarax su set, nde sama tur a ni màgge fi biir xeet yi.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

¶ Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax, ngir ngeen jébbal ko seen yaram wépp, def ko jooxe buy dund, sell te neex Yàlla. Loolu déy mooy njaamu, gi leen war.

Noo bokk diy surga ci liggéeyu Yàlla bi; yeen ngeen di toolu Yàlla, di tabaxub Yàlla.

Dangeena xamul ne seen yaram mooy màkkaanu Noo gu Sell, gi ci yeen, Noo gi ngeen jote ci Yàlla? Moomuleen seen bopp,

Yeena di tabax, bi ndawi Almasi ak yonent yi di kenu gi, te Almasi Yeesu ci boppam di doju coll wi.

Su ma ci deeyee sax, ba sama dund mel ni sarax su ñu tuur, tofal ko ci sarax, bi seen ngëm taxawe, su boobaa it maa ciy bég, te di leen woo, ngir bokk ak yeen ñépp bànneexu.

Lu ngeen mana def, muy ci wax, di ci jëf, defleen ko ci turu Sang Yeesu, tey sant Yàlla Baay bi ci moom.

Almasi nag mooy Doom ju wóor ji jiite kër Yàlla, te nun nooy këram, ndegam kay nu ngi wéye aw fit, ak yaakaar ji nuy puukarewoo.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.

¶ ba noppi def nu nuy askanu sarxalkati Buur Yàlla Baayam, na ko daraja ak kàttan ñeel tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.

Yaa leen def ñu doon nguurug sarxalkat yi, ñeel sunu Yàlla, te dinañu nguuru ci àddina.»