na ko sarxalkat bu nekk nangoo ci seen loxoy xame, ngir ñu liggéeye ko kër Yàlla gi, fépp fu fi laaj ñu defaraat ko.»
TSK
TSK · 1 Peter 5:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mooy sàmm géttam bii ni kuy sàmm ug juram, boole mbote yi cib loxoom, taf cib dënnam, yóbbu; xar yiy nàmpal, mu wommat.»
Ñoñam ña daldi fàttliku janti Musaa ya woon. Ña nga naan: «Ana ki jàlle woon Israyil géej, mook sàmmi géttam ga? Ana ki yebaloon noowam gu sell ci seen biir?
«Maay joxe seeni jabar, jox seeni tool ay foqatikat, ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, ñépp a ngi lewal lu lewul. Ab yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor!
Yerusalemee, séentul, xool ñiy jóge bëj-gànnaar. Moo ana gétt gi ñu la dénkoon, sa gàtt yu rafet ya?
¶ «Gannaaw loolu maa leen di waajalal ab sàmm bu leen di sàmm. Kookooy Daawuda sama jaam bi. Moom moo leen di foral, mooy doon seen sàmm.
Waa ji ne ma: «Lii mooy waañ yi liggéeykati kër Yàlla gi di togge yàppu saraxi askan wi.»
Kookooy doon buntu jàmm, ba bu waa Asiri songee sunum réew, ba daagoo sunu kawi tata, juróom ñaari njiit lanu koy yékkatil, ba juróom ñetti garmi.
Wóoy bii yambarub sàmm buy wacci gàttam. Yal na saamar làggal loxoom, fuq bëtu ndijooram. Yal na loxoom lax ne làcc, bëtu ndijooram giim ba gëmm fatuus.»
¶ «Buleen ragal dara, yeen jur gu sew gi, ndax seen Baay la soob, mu jagleel leen nguur gi.
Moo ma tax di seere bésub tey, ne wàccoo naak ñépp, deesu ma topp benn bakkan.
Ci kaw loolu Póol ne: «Lu ngeen di def nii, di jeexal sama xol? Waxuma ñu yeew ma rekk, waaye dee sax nangu naa koo def ci Yerusalem ngir Sang Yeesu.»
¶ Kan moo masa ràngu liggéeyu coldaar, te léppam war ko? Ana kuy jëmbat tóokërub reseñ, te du lekk ca doom ya? Mbaa kan mooy sàmm ag jur, te du naan ca soowum jur ga?
¶ Maa ngii di leen waaja ganesi ñetteel bi yoon, te duma wéeru ci yeen. Wutsiwuma lu ngeen am, yeen laa soxla. Ndaxte doom du dencal waajuram, waaye waajur mooy dencal doom.
¶ Naka noonu ab taxawukatub mbooloo mi, na di ku tedd, bumu di boroom ñaari kàddu. Bumu di ku sàngara jiital, mbaa kuy sàkku am-am bu lewul.
Li war moo di tëj seen gémmiñ, ndax këri lëmm lañuy tase àlluwa ju ñu amul sañ-sañam, ngir di ko sàkkoo am-am bu lewul.
¶ Fàttli leen ne leen ñu nangul kilifay nguur gi, ak boroom sañ-sañ yi, di dégg ndigal, tey fàggu ngir jépp jëf ju baax.
Moytuleen balaa kenn di ñàkk yiwu Yàlla. Moytuleen bala ab reenu wextan di fëll, di lëjle, ba rax mbooloom lëmm.
wurus ak xaalis, ak doji gànjar aki per ak lẽe ak ndimo lu yolet ak sooy, ak ndimo lu xonq curr, ak bépp bant bu xeeñ, ak wépp xeetu jumtukaayi bëñi ñey, ak jumtukaayi dénku ngëneel ak yu xànjar, ak yu weñ gu ñuul, ak yu doju màrb,