Sàmmala sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
TSK
TSK · 2 Peter 1:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñu sore ñooy dikk tabaxsi kër Aji Sax ji, ba ngeen xam ne Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moo ma yebal ci yeen. Loolu mooy am, ndegam déggal ngeen ba déggal seen kàddug Yàlla Aji Sax ji.»
Nun nag danoo yaakaaroon ne mooy jotsi Israyil. Loolu lépp teewul nu ngii ci ñetteelu fan, ba mbir yooyu amee ba tey.
¶ Bokk yi, buleen doon ay xale ci wàllu déggin. Su dee lu bon, nekkleen ci ay tuut-tànk, waaye màggleen ci wàllu déggin.
Moo tax buleen def jëfi ñàkk bopp, waaye jéemleena xam coobarey Boroom bi.
¶ Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox,
¶ Moo tax nun itam, ba nu déggee seen mbir ba tey, noppiwunu leena ñaanal, di sàkku ngeen feese xam-xam ci lépp luy coobarey Yàlla, te ngeen ànd ceek lu mat sëkk ci wàllu xel, ak gis-gis bu Noo gi maye.
Waaye danoo bëgg kenn ku nekk ci yeen wéye genn farlute googu ngeen nekke, ba kera muj ga, ngir seen yaakaar sotti ba mat sëkk.
Moytuleen balaa kenn di ñàkk yiwu Yàlla. Moytuleen bala ab reenu wextan di fëll, di lëjle, ba rax mbooloom lëmm.
Aw yiw ak jàmm baawaan na, ñeel leen, ndax xam gu ngeen xam Yàlla, ak sunu Sang Yeesu.
¶ Kon nag soppe yi, li feek ngeen di séentu loolu, defleen seen kem-kàttan, ba bésub keroog fekk leen ci jàmm, te ngeen baña am benn gàkk, mbaa sikk ci gis-gisu Yàlla.